Bible Selection
|
|
|
|
New Testament
|
|
|
|
Wolof Bible 1987
|
|
|
|
1 |
Ay juutikat ak ay boroom bàkkaar daan jegesi Yeesu ngir déglu ko. |
2 |
Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!» |
3 |
Noonu Yeesu daldi leen wax léeb wii ne leen: |
4 |
«Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, toppi ma réer, ba gis ko? |
5 |
Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga. |
6 |
Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.” |
7 |
«Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar. |
8 |
«Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko? |
9 |
Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.” |
10 |
Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.» |
11 |
Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom. |
12 |
Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may war a féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam. |
13 |
Ay fan yu néew gannaaw gi, caat ma fab yëfam yépp, dem ca réew mu sore, yàq fa alalam ci topp nafsoom. |
14 |
Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk. |
15 |
Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya. |
16 |
Mu xiif ba bëgg a lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara. |
17 |
Mujj xelam dellusi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgg a dee ak xiif! |
18 |
Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; |
19 |
yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ” |
20 |
«Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko. |
21 |
Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.” |
22 |
Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gën a rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll. |
23 |
Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu; |
24 |
ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu. |
25 |
«Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc. |
26 |
Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew. |
27 |
Mu tontu ko: “Sa rakk moo dellusi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibbisi na ci jàmm.” |
28 |
«Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, bañ a dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg. |
29 |
Waaye taaw ba tontu baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te musumaa moy sa ndigal, waaye yaw, musuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit. |
30 |
Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.” |
31 |
Noonu baay bi tontu ko ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom. |
32 |
Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”» |
Wolof Bible 1987 |
Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal. All rights reserved. |