Bible in one year
June 20


John 12:1-26
1. Juróom benni fan laata màggalu bésub Jéggi ba, Yeesu dem na Betani, dëkku Lasaar, mi mu dekkal.
2. Foofa ñu defaral ko fa reer. Màrt moo ko doon séddale, te Lasaar bokkoon na ca gan ña.
3. Noonu Maryaama daldi jël liibaru latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree-bare. Mu sotti ko ci tànki Yeesu, ba noppi fomp ko ak kawaram. Xetu latkoloñ gi gilli ci kër gi yépp.
4. Kenn ca taalibey Yeesu ya, muy Yudaa Iskariyo, mi ko nar a wor, daldi ne:
5. «Lu tax jaayewuñu latkoloñ jii peyu atum lëmm, jox ko miskin yi?»
6. Waaye bi muy wax loolu, xalaatul woon miskin yi, ndaxte sàcc la woon; moo yoroon boyetu xaalis bi, te daan ci sàkk.
7. Waaye Yeesu ne ko: «Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul.
8. Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.»
9. Bi ñu yégee ne, Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Betani. Yeesu rekk yóbbuwu leen fa woon, waaye dañoo bëggoon a gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon.
10. Saraxalekat yu mag ya dogu ci ne, dañuy reyaale Lasaar,
11. ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu leen, gëm Yeesu.
12. Ca ëllëg sa mbooloo mu bare, ma ñëwoon ca màggalu bésub Jéggi ba, yég ne Yeesoo ngi jëmsi Yerusalem.
13. Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na Yàlla barkeel buuru Israyil!»
14. Yeesu wut cumbur, war ko; ndaxte Mbind mi nee na:
15. «Buleen ragal, waa Siyon.Gis ngeen, seen buur a ngi ñëw,war mbaam mu ndaw.»
16. Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne, Mbind mi yégle woon na loolu ci moom, te amal nañu ko.
17. Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi muy wooyee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis.
18. Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte yégoon nañu firnde boobu.
19. Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, mënuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!»
20. Ca mbooloo ma, amoon na ca ay Gereg yu bokk ca ña ñëwoon Yerusalem ngir jaamu Yàlla diirub màggal ga.
21. Ñëw nañu ci Filib, mi dëkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëggoon a gis Yeesu.»
22. Filib dem wax ko Andare; ñu ànd, waxi ko Yeesu.
23. Mu tontu leen ne: «Waxtu wi ñu war a feeñale ndamu Doomu nit ki jot na.
24. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du man a weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.
25. Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.
26. Ku bëgg a doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral.